Bëgg sa réew
Mooy dëkkee bañ a
Pasar-pasaree alalam
Bañ a këpp i keesam
Bañ a jalgati ay àtteem
Bañ a xatal ay mbeddam
Bañ a asaaloo suufam;
Bañ a mbuxum ay lijjaasaam…
Bañ a ger ay àttekatam;
Bañ a lekk alali ger itam
Bañ a njuuj-njaaj ay woteem;
Bañ a gor ay àllam
Bañ a yalax ay géejam..
Bañ a tilimal ay ñallam
Bañ a tookeel am ndoxam
Bañ a tëj gemmiñu taskatu xibaaram
Bañ a bàyyi xale yi ciy mbeddam
Bañ a sànni mbuus ciy mbeddam;
Bañ a dóor ay jigéenam.
Bañ a jox ndombay tànk ay cuuneem!
Bëgg sa réew
Mooy it
Di xëy waxtu di wàcc waxtu
Di liggéey te doo tappale
Di bokk ci ñiy wote ;
Di Wegg raayaam;
Di setal deram
Di sellal ay mbeddam;
Di Fay say galag;
Di weeje ñiy sacc ak a yekktaan ;
Di sàmm alalam tey yamale
Di téeyee alalam tëddee njaaxaanaay
Di ko bañ a saax-saaxee.
Bëgg sa réew
Mooy faj ay doomam
Mooy sàmm ab deram
Mooy aar alalam
Mooy it teeru ak màggalam
bés bi mu moomee boppam!
©️ Dr Massamba Lba Guèye
/-//
Aimer son pays…
C’est le montrer!
Aimer son pays,
C’est surtout ne pas
piller ses ressources;
Ne pas détourner
ses deniers publics;
Ne pas violer des lois;
Ne pas encombrer ses rues;
Ne pas brader ses terres;
Ne pas trafiquer ses diplômes;
Ne pas corrompre sa justice;
Ne pas se laisser corrompre
Ne pas truquer ses élections;
Ne pas dévaster ses forêts;
Ne pas vendanger ses mers;
Ne pas salir ses ruelles;
Ne pas polluer ses eaux;
Ne pas museler sa presse;
Ne pas laisser ses enfants en rue
Ne pas jeter de sachets en rue;
Ne pas brimer ses femmes.
Ne pas promouvoir les médiocres
Aimer son pays,
C’est aussi
Être ponctuel;
Travailler sans tricher;
Voter aux élections;
Respecter son drapeau;
Construire sa belle réputation;
Nettoyer ses rues;
Payer ses impôts;
Dénoncer le vol et le viol;
gérer ses richesses équitablement;
Gérer ses biens inclusivement;
Gérer sans piller ses ressources.
Aimer son pays,
C’est soigner ses enfants;
C’est soigner sa réputation;
C’est protéger ses ressources;
C’est aussi …
fêter son indépendance!
©️ Massamba Guéye