Un bel hommage du Professeur Massamba Gueye « Al Maktoom dem na nii »

0

Xol jooy na weet

Boroom Xilaafa gi dedduna

Fu nuy jëleeti ku mel ni yaw

Boroom Xam-Xam bu mat bi

Boroom Kaalama ku diib gu seel gi

Boroom Njàngale mu xarañ mi

Fu ñuy jëleeti ku tol ne yaw

Yaw mi defar xaleyi

Yaw mi teye jigéen ñi si sëy yi

Yaw mi sa waaraate kat yi

Borom Baat bi sell bi

Sama xol jooy na

Sama róŋoon tuuru nañ

Sama aduna weet na

Seex ahmed Tijaan nopalu na

Seex ahmed Tijaan Si siisuwul

Seex ahmed Tijaan Si Al Maktoom

Ya mat sëriñ

Yaa matalem njàngale

Ay waay ku may wettaleeti

Ana ku may fedaleetil sama diine

Ya sell, ya set, yaa sed

Ya yiiw, yaa ñeme

Yaa aar sam réew

Aar sa diine aar sa ngor

Funuy jeleeti ku mel ne yaw

Seex Mustafa Si mu tedd mi jaalenaa la

Yaw mustarsidin bi jaalena la

Al amiin mu baax mi siggil ndigaale

Umma bi jaalnaa la

Jàmbaari Lislam nelaw na

Yàlla na Yàlla Yokki leeram

 

Dr Masàmba Géy

Laisser un commentaire

Votre adresse email ne sera pas publiée.